defar lonku yi ci jëfandaayi kàddu bluetooth ak ay wone yu amul buum ci windows 10

saafaral ay lonku ci ay jëfandaayu kàddu Bluetooth ak ay wone yu amul buum

Kàddu Bluetooth

Sudee bës ci bitoŋuLonkbitoŋ bi nekk ci diggu jëf gusul sama jëfandaay, jéemal bii ci topp:
Wérlul ni sa jëfandaayu Windows dafay nangu Bluetooth ak ndax taal nañ ko. Di nga gis bitoŋu Bluetooth ci barabu toppatoo.
Soo gisul bitoŋu Bluetooth, jéemal yeesal sa dawalukaayu jëfandaay. Nii lañ koy defee: Demal ci Door, dugalal Saytukatu Jëgandaay, tànn ko ci limu njuréef yi, te, ci Saytukatu Jëgandaay, seetal sa jëfandaay, bësal-ndeyjoor (walla nga bës ci teye), te tànn Yeesal Losiselu Tàppaan, tànnal Seet ci saasi ngir am losiselu dawalukaay buñu yeesal, te nga topp li des ci jéegoo yi.


Sudee taal nañu Bluetooth, te ñu yeesal jëfandaay bi, te sa jëfandaay doxul ba tay, jéemal a dindi jëfandaay bi te seexalaat ko. Nii lañ koy defee: Demal ci Door, dugalal Jëfandaay yi, tànnal Bluetooth tànnal jëfandaay bi, tànnal Dindi jëfandaay, te nga jeema seexalaat.
Wérlul ni jëfandaayu kàddu buñu dekkalee ak Bluetooth mu ngi takk te mën nañ ko gis. Ni nga koy defee dafay wuute ci jëfandaay yi, kon xoolal leeral yu àndak sa jëfandaay walla nga dem ci daluweb defarkat.

saafaral ay lonku ci ay jëfandaayu kàddu Bluetooth ak ay wone yu amul buum

Sudee bës ci bitoŋuLonkbitoŋ bi nekk ci diggu jëf gusul sama jëfandaay, jéemal bii ci topp:
Wérlul ni sa jëfandaatu Windows dafay nangu Miracast sooy xool leeral yuy àndak moom walla soo demee ci daluwebu defarkat bi.
Wérlul ni taal nañu Wi-Fi.
Wérlul ni wone bi nga bëgg a jàllale nangu na Miracast te nga seet ndax takk na. Suko deful, war nga am ab méngalekaayu Miracast ( lenn luñuy woowee ab “caabi”) buy roofu ci ab jàllalekaayu HDMI.

Jëfandaayi WiGig

Sudee bës ci bitoŋuLonkbitoŋ bi nekk ci diggu jëf gusul sama jëfandaay, jéemal bii ci topp:
WWérlul ni sa jëfandaayu Windows dafay nangu WiGig te nga seet ndax takk na. Sudee sa PC dafay nangu WiGig, di nga gis ab bitoŋu WiGig ci Jekkal yi > Anamug roplaan.
Wérlul ni wone bi dafay nangu WiGig. Suko naguwul, doo soxla ab dendale WiGig.

Leave a Reply

Your email address will not be published. Required fields are marked *