saafaral ay lonku ci ay jëfandaayu kàddu Bluetooth ak ay wone yu amul buum
Kàddu Bluetooth
Sudee bës ci bitoŋuLonkci barabu toppatoo gisul sa jëfandaayu kàddu biy doxee Bluetooth, jéemal lii:
Wérlul ni sa jëfandaayu Windows dafay nangu Bluetooth ak ndax taal nañ ko. Dinga gis ab bitoŋu Bluetooth ci barabu toppatoo gi.
Wérlul ni jëfandaayu kàddu biy doxee Bluetooth mu ngi takk te mën nañ ko gis. Ni nga koy defee dafay wuute ci jëfandaay yi, kon xoolal leeral yu àndak sa jëfandaay wala nga dem ci daluweb defarkat.